Après plusieurs semaines de discussions, le Sénégal et le Fonds monétaire international (FMI) sont parvenus à un accord technique qui ouvre la voie à un programme économique et financier d’un montant de 2,2 milliards de dollars (1 243 milliards de FCFA) sur trois ans. Les autorités ont également lancé le Plan de Traitement de la Dette du Sénégal (PTDS) destiné à restaurer durablement le profil de la dette et à dégager progressivement les marges de manœuvre nécessaires au financement des investissements publics dans les secteurs prioritaires.
Voici ce qu’il faut retenir des deux principales décisions qui ont marqué les conclusions de la mission du FMI, clôturée le mardi 1er septembre 2026.
Ginnaaw ay ayi-bisi weccente, Senegaal ak “Fonds monétaire international (FMI)” am nañu ag déggoo guy tijji buntu lëkkaloo ci sémbu koom ak koppar wu tollu ci 2,2i milyaari dolaar, di yemoo ak 1 243i milyaari FCFA ci diiru ñetti at. Kilifa yi door nañu itam Pexem Saytu Borub Senegaal (PTDS) ngir gën a ñoŋal bor bi boole ko ak dajale ndànk-ndànk koppar yi war ngir finaase fànn yi gën a far ci réew mi.
Lii mooy tomb yi ñu man a jàpp ci ñaari dogal yu am solo yii di màndargaal njeextalu liggéey bi FMI doon amal te ñu matal ko talaata 1 panu sebtàmbar 2026.
Man ngeen a jaare ci lëkkalekaay gii ngir am tënk bi.
BIC-GOUV